Ndekete yóo waxtu ya ñu boole woon du xaritoo kase
Ndekete yóo waxtu we taxoon ñu doon dajee weer bu ne
Woo nga ma ci guddi gi fekk mu maas
Ci ëlëg tamiit, fi ci suba ci, fekk mu naaj
Waxtu bi su weeso dotul ñëwaat
Do ko dabuwaat
Bala dellusiwaat
Mu nekk ci beneen bës
Bu jànt bi di so fi, féele di naaj
Bu guddi gi di xaaj fi, timis di waaj a jot fe
Massamba ma nga Walo
Suba soxla ya koy yoobu Ndakaaru
Te ëlëg ndogal mën na fa xandalu
Fi ak ay bés mu jiibi sanc walo
Ndekete waxtu yi ñooñii boolee
Ñoom ñooñii boolee
Du xaritoo kaase ñoom ñooñii boolee
Ndax bu ëlëge mën nañu jiiwalo
Waxtu w saay su jotee(bu fekkee waxtu woowu la wootee)
Foo mën ti nekk, waxtu w bu jotee
Budul suba tamiit sa boos moo ñi ñëw
Ass fay nee na du xaar suba
Ndax yàkkamti na te démb weesu na
Ku sàkk gaa ye moo ñi dajaale
Ci adduna bee ci waxtu jii li mel tay
Mara naan, marul naan, naan, am na potu-ndaal
Ndox ma ngay walangaan, ñun buñu réeroo
Ndox ma ngay walangaan, ñun buñu réeroo
Te amaana buñu diisoo di nañ déggoo
Ñu bañ di réeroo
Nañu déggoo di bañ di réeroo
Amaana buñu booloo mu may ñu doole
Boroom bi def ci ndam su ko soobee
Bu ñu boolo, nañu boolo