Yéenewoo ma lépp li ma doon
Temps amatul damay jokk yox
Te newuma ci li nga fok
Mel li lan la yaw lan nga téye ci sa biir xol
Xamal ni xamal ni
Fi de loo fi sombi yaw mi din' ko jeem a naan
Jàppal ni jàppal ni
Sa yéene mooy sa nekk
Foo mën ti nekk dinga fa fanaan
Yàlla Buur bi sàkk la te sàkk ma
Wax ma li lu ko fi jar
Am talibe tax nit yi di ma sopp
Du ñakk fay dama wacc sama bopp
Wax ma gën naa ni, hey he he
Sooy wéet di siisu
Est-ce que doo jeem a daalu
Man sax dama waaru
Hey, ndax lu ëpp tuuru
Yàlla bind te yamalewul
Soo ko nangoo doo sonn
Su yabo nga nangu dogal
He, Buur Yàlla mooy maye
Noppalul foo yewoo gis ma
Foo yewoo gis may dem
Noppalul foo yewoo gis ma
Foo yewoo gis may dem
Xoolal fi, moo ngi cool
Ah, moo ngi baax
Xoolal fi, moo ngi cool
Noon, fi lépp moo ngi baax!
Wax ju bon bi nga jël teg ko sama der
Yaw mi de lan moo la dal
Looy dox di mer
Mënoo ci man dara
Jël naa lépp teksi loxo
Yàlla Buur bi ma sàkk
Gëm naa ne loolu
Mooy sama gàllaaj
Sooy wéet di siisu
Est-ce que doo jeem a daalu
Man sax dama waaru
Hey, ndax lu ëpp tuuru
Yàlla bind te yamalewul
Soo ko nangoo doo sonn
Su yabo nga nangu dogal
He, Buur Yàlla mooy maye
Noppalul foo yewoo gis ma
Foo yewoo gis may dem
Noppalul foo yewoo gis ma
Foo yewoo gis may dem
Xoolal fi, moo ngi cool
Ah, moo ngi baax
Xoolal fi, moo ngi cool
Noon, fi lépp moo ngi baax!
Noon, fi lépp moo ngi baax!